Taariixu Itaali
Bennal gu Itaali
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ni Itaali meloon njëkk xare yu Napoleon yi:
Itaali laata a Napoleon di ko teg loxo, di ko nangu, nekkutoon réew mu ñu bennal , nekkutoon it di mu am ag temb, moom kay daa seddaliku woon, doon fukki xaaj ak ñaar, yu doon topp ak a nekk ci ron kiliftéefug ay nostey politig yu wuute: nosteg nguur ca Savoia, Piemonte, Napoli, ak nosteg pénc ca Venezia ak Geneva, ak ag àtte gu paab ca Rom, ak gu Dóox ca Toskaana ak Parma, ak xaaj yoo xam ne dañoo nekkoon ci waawug imbraatóor gu Otris gi, ñooy Milano ak Lombardia.
Piemonte nag moo nekkoon nekkteg politig gi gënoon a dëgër, te ëppoon doole ci nekkte yooyu. Ña ëppoon ca njiit ya yilifoon nekkte yooyu, ay diktaatóor lañu woon, rawati na ñi ci waa Otris jiite woon, cig jonjoo mbaa cig jonjoodi .
Jeexiital ya Napoleon bàyyiwoon ca Itaali:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Napoleon, bi mu nangoo Itaali, dafa lijjanti ba boole xaajam yu politig yu bari te wuute yooyu ci ñatti nguur rekk, ñooy: Nguurug Alp gu bëj-gànnaar gi, walla Itaali, ak Nguurug Savoia, ak Nguurug Napoli. Mu wutaloon réew mi mépp, wenn yoon , daal di dindi galag ak tënk yu koom-koom yi amoon ci wàllug ndefar ak yaxantu, ak mbay. Mu ubbi leekol yi ngir jàngal doomi réew mi, mu may waa Itaali ñi ñu man di jot ci pal yi, te kat bu njëkk waa Otris rekk a ci manoon a jot. Looloo tax ñu man a wax ne Napoleon de mooy ki ji njiyum bennoo gu xeet ci suufus Itaali, mooy ki leen def ñuy xeeñtook a gént am réew mu Itaali mu man a am, mu ñu bennal.
Itaali ginaaw ndajem Vienne:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ndajem Vienne mi – ci xalaati njiitu jawrin ju Otris jii di Metternich-Winneburg – seddale woon na Itaali, def ko juroom-ñaari xaaj, ñooy:
Ñoom ñaar nag, mujj nañu leen boole, def leen benn, teg leen ci ron kilifteefug Otris. Ginaaw nag Metternich fexe woon na ba yay njiiti ndaje mi, gëmloo leen “dalu desal fi lu yàgg la ca yàggam ga” maanaam lu nekk, nañu ko delloo na mu meloon, loolu nag moo indi ndaje mi delloosi njiiti nguur yu ndaw yu Itaali yu njëkk ya, ñu delloosi leen ci seeni pal, tegaat leen ci seen barab.
Metternich ak gëtam yi mu tasoon ci gox yépp, jéemoon nañoo fuglu yëglekaay yi, daan naj it gépp cawarte gu politig. Ci noonu ñu daa tëj gor ñi ci kaso yi, daan xañ way dëkk yi pali ñoñ yi (siwil) yi ak yu xare yi nga xam ne bi Napoleon ñëwee jox na leen ko,mu daan leen weccee ak ay waa Otris (moom metternich), te daan leen teg ay galag yu diis te sonnle.
Yewwuteg xeetu (nationalisme) ni mu xëye rekk am te màgg ca Itaali:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Politigu noteel bi Metternich yore woon, ak li muy tar lepp, taxutoon mu man a rekki yëg-yëg bi waa Itaali yi ame woon, ak xam ngi ñu xamoon am solo gi bennal seen réew mi, te booloo ci wàllug politig amoon solo, loolu nag mi ngi am, ginaaw bi ñu ci ñamee’s lëf ci jamonoy Napoleon. Bi nga xamee ne politig bu ñaaw boobu fa amoon, mayu leen woon ñuy def seeni cawarte ak jëfi politig, ci lu bér, te nëbboodiku, bi loolu amee lañu wéeru ci di def seeni yënguy politig cig làqu ak fésadi.
Bu ko defee, ay booloo yu politig yu sekkare tàmblee sosu ci dëkki Itaali yu mag yi, li leen taxoon a jug di bennal Itaali, bokk na ci yooyu:
- Booloo gu Karbonaari (ñoñ këriñ)
- Ak booloo gu Itaali gu waxambaanee gi.
Booloo gu Karbonari, moom mi ngi sosoo ca Napoli, daan def ay jataayam - ngir làqatu - ci barabi ligeeykati këriñ yi, walla lakkati mat yi, mu mujj nag tas ci mbooleem Itaali. Mbooleem kureeli askanu Itaali wi nag bokkoon nañu ci, baykat yi, liggéeykat yi, boroom mecce yi, yaxantukat yi, boroom xel yi, añs. Li leen manke woon nag, mooy dañoo nosuwutoon bu baax, te ni ñu daan naale ak a rëdde seeni mbir tam dafa dese woon a tegu ci yoon, looloo taxoon li nu bëggoon daawul àntu, te seeni noon daa leen gaaw a noot, te daa àntoodil seeni fipp.
Waaye nag booloo gii, di gu Karbonari gi, jot na fee taal yëg-yëgu xeetu ci Itaali, te lijjanti ba mu sax fi di tàkk, ak doonte daje na’ak coona yu bari, te nu teg ko lu sakkan ciy mbugal.
Bu dee booloo gi tuddoon “Itaali gu Waxambaanee gi”, moom Jozeph Mazzini (1805 – 1872 g) moo ko sosoon, ginaaw bi mu nekkee ab cér ci booloo gu Karbonari gi. Mazzini mii, moom waay Itaali la woon ju xéroon ci réewam ak xeetam, nekkoon it ab xeltukat bu bokkoon ci ñoñ nite ñi , bu gëmoon ne xeetu nit ñepp benn lanu, te bëggoon lool goreg askan yi , moom nag jot na’a àgg ci xëcc cig wàllam boroom xel yi ci Itaali, te fàggu ñeewanteg nitug neen ku Itaali ki, akug cofeelam.
Bokkoon na ci jubluwaay yi gënoon a tax booloo gii am, goreel Itaali ci àtteg Otris, ak duma àtte gu paab gi nga xam ne Otris a ko daa dimbleek a dëgëral, ak fexee bennal réewum Itaali mi, ci ron ag noste gu pénc.
Yëngu-yëngu yii, mujjoon nañu naat, te dox, bijjaloon it boppam lu sakkan ci waxambaane yi ak xalaatkat yi, àggoon nañu ci lu toll ci juroom fukki junniy waxambaane, yu weesu ay ñeen-fukki at yooyu. Mazzini dimblante na’ak Garibaldi, moom Garibaldi, ab ab waa xare la woon, bu itaali, bu gëmoon bennug Itaali, te gëmoon ne dañoo war a gorewu ci àtte gu Otris gii bóof ci suufus Itaali si. Ci noonu lañu jot a taxawal ñoom ñaar, ag àtte gu pénc ca Rom, ca moomeeli paab ga, ak ca Venezia, atum 1848g. Waaye Otris moom, ca dooleem ju bari ja, faagaagal yëngu-yëngu googu, daal di dàq Mazzini mu daw, làqu ca Anggalteer. Ag woote nag feeñ na fa, jëm ci ñu def nattukaay yi benn, xaalis bi, ak peesekaay yi , ci mbooleem diiwaani Itaali yi aki nguur-nguuraanam, rawati na bi ndefaram tàmblee màgg, yaxantoom gën a jëm kanam. Boroom liggéey yi nag ak boroom boppi alal yi , gisoon nañu am njariñ gi gore ci koom-koom amoon njariñ, ñu tàmbli woon a sàkku ñu sosal leen ay yooni weñ , yuy taqale diggante bëj-gànnaaru Itaali ak bëj-saalumam, te nu uppi mbooleem ja yu Itaali yi, ci kanamu yaxantu gu Itaali gi, te bañ cee indi yenn jafe-jafe walla ay mbugal yu doxaliin , walla ay galag yu man a tee bennoo gu yaxantu gi am ci Itaali.
Fàttalees léen
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ñu fàttali léen ne barab yu bari de ci bëj-saalumu Itaali, yu deltu-ginaaw lañu woon ci wàllug ndefar, koom-koom, mboolaay ak politig. Looloo taxoon xalaat yi jëmoon ci bennoo, mi ngi gënoon a dëgëre ci fi ñuy wax Itaali ( di nguuru Alp gu bëj-gànnaar gi) ak ci digg bi. Foofa daal la wooteg bennoo gi gënoon a tare ci yeneen wàll yu bëj-saalum yi. Ndax kat wàlli bëj saalum yi dañoo jëmutoon kanam dara ci wàllug ndefar, yaxantu, politig ak mboolaay. Lii a waraloon woote gi, jëme ci bennoo gu koom-koom, yamoon rekk ci digg Itaali ak ci bëj-gànnaar gi. Ñi ëppoon it ci xalaatkat yi ak boroom xam-xam yu Itaali yi, ñi ngi dëkke woon digg bi, ak ci bëj-gànnaar gi.
Ak li boole Itaali, def ko menn réew doon nekk càkkuteful ñépp lépp, teewul yenn ci nguur-nguuraan yi, ak Dóox yi , kontaroon ko, ndaxte ñoom dañoo ragaloon ne loolu de, moo xam leegi la walla ci kanam, bu amee, di na fi indi ag bennoo gu politig, te loolu bëgguñu ko woon, ndax kat ñoom seeni njariñi nguur yooyu moo leen gënaloon njariñul Itaali li. Ci noonu, nguurug Paap gi kontar ko, naka noonu gu Otris gi nga xam ne amoon na kilifteef gu yaatu, ak sañ-sañ bu mag ci Itaali. Ndax moom daa gisoon ne bu Itaali bennoo ci wàllug koom, boole ay nguur-nguuraanam, aki dóoxam, loolu du wund lu dul ne moom kat (Otris) waxtuw génnam Itaaliee ngi bëgg a jot, ci lu dog. Te loolu du ko nangu mukk.
Nguurug Piemonte ak Bennalug Itaali:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ci bëj-gànnaaru Itaali ag nguur a ngi fi woon, ñu koy wax nguurug Piemonte walla Sardeñaa, ka nekkoon ca gàngunaay ga, di woon Victor Emmanuel. Moom Piemonte nag, nguur la woon gu ame woon ci ñeenti xaaj yu taqaloowul, ñooy:
- Savoia, mi ngi nekkoon ci kaw doji Alp yi, tiim wàllug Faraas gi dend ak Itaali, moom nag diiwaan la bu gën a yor ay màndarga yu Faraas ci yu Itaali, moom itam taxu ko woon a jëm kanam mbaa mu woomle, ak
- Sardeñaa, moom dun la, bu nekk ci géej gu diggu gi, xaw a sori Piemonte, ak
- Genova , moom nag, nguurug Piemonte jot na ci, ci ginaaw xarey Napoleon yi ci Tugal.
Di nanu gis fii ne Piemonte moom yorul woon nguur gu àttanoon coonay bennal Itaali, waaye nag yoroon na yenn yu rëy ci yiy taxawal réew mu mag, yu ko mayoon mu man a yanu yan bu diis bii. Ñu tudd ci yi ci ëpp solo:
- 1 Ab buuram daa gëmoon ag àtte gu tegu ci sartu réew, te daa gëmoon it bennoo gu Itaali.
- 2 Njiitul jawrinam lii di Cavor, - mi ngi doonoon njiitul jëwrin atum 1851g – daa gëmoon moom itam te sopp sartu réew ba Angalteer defoon, te bëggoon lool Itaali doon benn, te nekk ci ron ndëppul Piemonte.
- 3 Piemonte amoon na dooley xare joo xam ne, li ko daa wone mooy soldaaram sii nga xam ne jot nañoo xare ba am ci xam-xam, jarbu ko.
- 4 Piemmonte moo nekkoon làqatuwaay bi politigkat yi ñu daa sonale ci nguuri Itaali yeneen yi daan làqatoo.
- 5 Màgg gi koom-koom doon màgg ci Piemonte, moo gënoon a gaaw, gi mu doon def ci feneen ful Milano.
- 6 Nguurug Piemonte, gu sori woon loxol Otris la, nga xam ne daawul man a dugg ci mbiri biiram.
Cavour ak bennalug Itaali:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Cavour mii (1810 – 1861g), nekkoon na di ku gëm bennoo gu Itaali, waaye nag ci ron ag àtte gu nguur gu sartu réew , goo xam ne buurub Piemonte bee koy jiite, moom kon ci loolu la wuute woon ak Mazzini mi nga xam ne da doon woote ag bennoo gu Itaali ci ron ag àtte gu pénc. Moom de daa gëmoon ag yéwénal gu politig, gu koom-koom ak gu doxaliin , ngir Itaali man a doon benn. Mu gisoon ne nguurug Piemonte am na kàttanug dàq Otris mu genn Itaali, ak naj nguurug Paab gi daa lënkaloo ak Otris, bu lënkaloo woon (moom Piemonte) ak jeneen doole ju réew, ju mel ne Faraas mbaa Britani.
Cavour mi ngi yoroon njiitug jawrin gi ci atum 1851g, bi mu ko defee nag, mu tàmblee waajal am réewam ngir mu man a jiite liggéey biy bennal Itaali.
Ci noonu mu sotti yitteem ci xarekatam yi, waajal leen ba ñu man a jàmmaarlook mbooloom xare mu Otris mi, te man leen a génne Itaali, mu jug ci suqali koom-koom bi, defar ay yooni weñ , yu lënkale mbooleem dëkki Piemonte yi, daal di jamonool mbay mi ak ndefar gi, defar ay yoon, neenal galag yeek mbir yi man a tënk yaxantu ak ndefar, tege ay galag yu nduwaan yu mag ngir aar ndefar gu barab gi, yéwénal nosteg galag gi, daal di sos lonkoo yu askan yi ak bànk yi.
Bu dee lu aju ci doxaliin , ak yéwénal yu biir réew mi, moom da fee daal di woon buddee doxaliin wu yàgg wa fa nekkoon, daal di jël ay matuwaay yoo xam ne tax nañu ba yoon ci réewum Itaali gën a jamonoo, jële fi lu bari ci ay jàngu, maanaam ay egliis, wàññi dooley politig ju paab gi, tàqale àtte geek Jàngu bi.
Kafor mii nag xamoon na ni réewam mi tuutee woon, bu ñu ko tollalee ak Otris walla Britani, mbaa Faraas, am Riisi, ak Brusiya, waaye loolu lépp teewutoon mu gëmoon ne bennug Itaali daal, mbirum aw xeet la, manul a ñàkk, te itam mbirum àdduna bépp la, laaj na réew yi sonn ci, te jeem koo faj ci nu mu gën a gaawe, mu dogu woon ci sóobu ci géewub politig bu àdduna bi, ngir yékkati kàddug Piemonte ci àdduna bi ba ñépp dégg ko, ci ndajey Tugal yi.
Ci noonu mu digal Parlamaa bu Piemonte mu nangu ñu yonnee ab kuréelub xare bu Piemonte ngir mu bokki ca xareb Xarm ba , àndoon ca ak Britani ak Faraas, ngir sàkkoo ci xaritoo ak Imbraatóor bu Faraas bii di Napoleon mu ñatteel mi, (Napoleon III), te ame ca ñeewantug Britani akug jàppaleem ci li mu bëgg.
Kuréelu xare gu Piemonte googu, ak doonte bariwu ci ñu ci dee ca xareb Xarm ba, ndax ñu bari ci ñi ci dee ci mbasum koleraa lañu deewe, teewul Kafour moom lijjanti na ba ñu yëg Piemonte ci kanamu ndawi Tugal yi, ca ndajem juboole ma ñu doon def bi xareb Xarm bi jeexee.
Kafour sàkku na fa ca Fraans mu dimbli ko ci Otris, ndaxte nguurug Piemonte moom rekk manul a dàq imbraatóorug Otris gu dëgër gii. Kavour ci njëlbeen gi, li ko gënaloon mooy Britani jàpple ko, safaan Otris, waaye Britani moom, bëggutoon a xeex ak Otris, xeex bu ko amalul njariñ.
Bu dee Fraans nag, nga xam ne péncam mi , Napoleon III moo ko jiite woon, moom Napoleon III mi nga xam ne daa jàppe woon Itaali am ñaareelu réewam, ndax moom doom la woon ca Napoleon I - ginaaw doomi mbokkam la woon - te Napolen I mi ngi cosaanoo Corsica. Moom Napoleon III, ku soppoon waa Itaali la, te xéroon ci seeni àq aki yelleef ci gore te doon benn, moom de bokkoon na ci ñi gënoon a siw ci woote ag xeetu ci Tugal. Politigu bitim réewam it mi ngi ko tegoon ci bañ Otris mi dendoon ak moom. Te ginaaw Piemonte it réew mu nekk ci wetu Faraas la, loolu taxoon na mu bëgg mu nekk réew moo xam ne yoonu Otris du ca nekk.
Cavour lënkaloo na ak Napoleon III, ñu def dëppoo ga nuy wax (Plombiere) ci 21 sulye atum 1858g, dëppoo googu, la mu yaxal mooy:
Ñu taxawal ag nguur gu Itaali ca bëj-gànnaaru Itaali, buurub Piemonte jiite ko, ak geneen nguur ci digg bi. Moomeeli paab gi moom ñu bàyyi leen fi, te bañ a laal dara ci nguurug Napoli, gi nekk ci bëj-saamu Itaali, bu ko defee nag, genn bennoo gu ame cig dëppoo lënkale leen ci njiitug paab bi. Fraans nag li muy ame ci loolu mooy ñu bàyyee ko Niis ak Savoia.
Xare yi amoon ci diggante Piemonte ak Otris:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Kafour wéy na di cokkaas Otris, rawati na bi ko Napoleon III yonnee ñaari témeeri junniy xarekat, ngir ñu xeexle ko safaan Otris, loolu nag amoon na ci ginaaw dëppoog (Polombiere) gi . Kafour am na la mu bëggoon muy jeqi Otris, yëngal ko, ndax moom kat (Otris) mujjoon na jekki-jekki rekk sàkku ci Piemonte mu nocci ay ngànnaayam ci diir bu gàtt, bu weesuwul ñatti fan, mu tóllanti loolu ci jug jawali Piemonte ànd ak ay xarekatam atum 1859g. Taarixkat yi firee nañu loolu ne ag wuyyusi la gu Otris def ci li ko Piemonte doon yàgg a cokkaas, ak a dëkk.
Nii daal la xare bi tàkke ci diggante Otris ak Piemonte, waaye nag Otris a njëkk a song, ci noonu Faraas itam jibal ab xareem ci kaw Otris. Soldaari Piemonte yi ak yu Fraas yi jot nañoo duma Otris, dàqe ko ca xare ba ñuy wax Maginta ak Salvarino, waaye Napoleon III moom daa xëyoon rekk taxawlu ci xare bi, daal di gise ak Imbraatóor bu Otris bi, def ak moom ag wéer-ngànnaay, dellu xaatim ak moom ag juboo, te diisoowu ci ak nguurug Piemonte. Wéer-ngànnaay gii nag mooy li jur ci ginaaw bi, li ñuy wax juboo gu Siyorix atum 1859g. bokkoon na ca tomb ya ëppoon solo ca juboo ga:
1 Otris bàyyee Piemonte Lombardi
2 Sos booloo gu Itaali ci njiitul Paab bi ci tur
3 Venezia day des ci moomeelug Otris, waaye bokk ci bennoo gu Itaali gi
4 Delloosi ñi yilifoon Dóox yi nekkoon ci digg Itaali ci seen barab, ak seeni pal, ginaaw bi leen askan wi follee.
5 Boole Niis ak Savoia ci Faraas.
Taarixkat yi, firee nañu taxawal xare gu bette gi nga xam ne Napoleon III, defoon na ko, ne daal li ko waraloon, mooy daa bañoon ag nguurug Itaali gu dëgër am, taxaw, rawati na bi mu tàmblee gis lenn ci Dóox yi nekkoon ci digg Itaali tàmblee bokksi ci Piemonte.
Bokkoon na it ci li ko ko taxoon a def, jeem a gëramloo Katoligi Faraas yi nga xam ne dañoo tàmbli woon a mer ci néewal gi ñuy néewal doole nguurug paab gi ci Itaali, te Otris a ko daan jàppleek a dëgëral.
Kafour nag moom, daa daal di woon xàcc , walla tekki ndombaam, bi mu sàkkoo ci buur bi Victor Emanuel ba soon ngir ñu wéy ci xare bi ak doonte Faraas génne na ci loxoom, waaye mu lànk mom buur bi.
Askani Dóox yi bañ nañu ne duñu nangu mukk ñu delloosi ña leen yilifoon bu njëkk, ni ko tombi juboo gu Siyorix gi yaxale(stipuler), ñu ne woon daal ñoom leegi dañuy dem bokki ca nguurug Piemonte. Ci noonu ay jeqiku am yu toftaloo, ci Parma, Modena, Romaña ak Toscana, di woote ag bokki ca Piemonte. Kafour dellusi na yoraat njiitug jawrin gi, ngir sonal gu ko askan wi sonaloon ci mu dellusi, ci biir Piemonte ak ci biti.
Nii daal la Itaali doone benn ci diiwaan yi nekk ci bëj-gànnaar gi ak digg bi. Kafour dara deseetu ko woon lu dul mu fexee nangu Venezia, ak moomeeli paab bi, ak nguurug Napoli gi boole leen ci Itaali.
Coona yi Garibaldi doon daj ci Itaali doon benn:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Garibaldi moom ku bëggoon la te gëmoon bennug Itaali. Moom nag soldaar la woon bu dëgër, jàmbaare te ñeme. Mujjoon na it bokk ci jàmbaari Itaali yi siiwe woon ag wooteg bennoo gu xeet, te daan ci liggéey. Garibaldi mii, tukkee na Genova atum 1860g, ànd ak lu jege junniy xarekat yu bokkoon ci way coobarewu(les volontaires) yu Itaali yi ñu tudde woon “Boroom simis yu xonq yi”. Daal di wàcc ak ñoom Sisil, jot faa dàqe doole ya fa nekkoon te àndoon ak buurub Napoli bi, ginaaw diirub ñatti weer. Daal di jéggi xat-xatu Sisil bi (le détroit de Sicile) , dugg ak dooley xareem ji Napoli, ci lu dul jàmmaarloo gu am solo. Ci noonu Napoli mujj ak dëkk yi nekk ci ronam, dugg ci bennoo gi.
Samp Victor Emmanuel muy buuru Itaali:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Dooley Piemonte ju xare ji jawali woon na ca diiwaan ya nekkoon ca ron kilifteefug Paab bi, mu jotoon a nangu moomeeli Paab bi yépp, lu ci dul Rom. Ci noonu xarekati Piemonte yooyu jawali woon ca soldaari Garibaldi ya, ca Napoli, ci ndigalul Kafour, ñu àndandoo nag xeex ba nangu mbooleem diiwaan yi nekkoon ci ron nguurug Napoli, te Garibaldi manu fa woon àgg moom rekk. Ci noonu Victor Emmanuel ñëw, dugg Napoli, ni ku am ndam di dugge ci dëkk bu ñnu xare ba nangu ko.
Parlamaa bu Itaali bu bees bi def na ndajeem mu njëkk, ca Torino, bisub 18 feewrye atum 1861g. Ca ndaje ma lañu ndëppale Victor Emmanuel , def ko buurub Itaali gu ñu bennal gi.
Ginaaw bi Itaali taxawee di ag nguur gu ñu bennal, ba am juroomi weer la Kafor faatu, ci sulet atum 1861g. Garibaldi it bàyyi politig, ndax kat moom li ko taxoon a jug mooy liggéey ci Itaali doon benn, waaye soxlawutoon ay pali politig.
Def Rom péeyu nguurug Itaali gi:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Waa Itaali yi delloosi nañu Venezia gi Otris tegoon loxo, nangu woon ko, delloosi gi di ci atum 1866g, mu mujj nag moom Venezia di ab diiwaan ci Itaali, ginaaw ba ñu fa dàqee dooey xare ju Otris ji. Nanguwaat googu nag ñi ngi ko mane ci ñàkk a tal gi leen Otris ñàkkoon a tal, ngir xeex bi mu nekkoon di ko def ak Brusiya. Faraas it ay xarekatam génnoon nañu Rom, ngir sotti gi Faraas sotti woon yitteem ca xareem ba’ak Brusiya. Bi mu ko defee soldaari Itaali yi daal di leen fay wuutu, ci 20 sebtambar atum 1870g, ñu daal di jibal ci anam gu kilifawu (officiel) ne Rom daal mooy péeyu nguurug Itaali gu ñu bennal gi.
Doxaliin wii merloo woon na Paab bi, yobbu woon ko ci mu bañ a nangu loolu, ne woon it du man a summiku ci sañ-sañu politigam yi te du nangoo raflewu ci nguuram gi.
Noonu la mbir mi nekke woon ba 1929g, ca la genn dëppoo ame ci diggante Mossolini ak Paab bi, dëppoo googu mayoon na Paab bi mu doxe nu ko soob ci mbiri diine ji, te am ag tembte gu mat ca Vatikaan, am it sañ-sañ ci yabal ay way teewal ca bitim réew. Ñu wutal ko nag (moom Paab bi) njëlul boppam lu mu jagoo (son propre budget).
Nii nag la Itaali doone woon benn, muy lol ay doomam a ko xeex. Doomam yoy dañoo jëloon seen coona bepp def ko ci goreel ko, bennal ko, te fuqarcee ko ci ngëbug jàmbur, bu leen ruuroon, teg leen loxo. Bennoo gii de lu ñepp soppoon la, ndaxte doole la ci ñoom, di teddnga, di tembte te dig fonk sa xeet. Bennoog Itaali du lenn lu dul meññatum sellal ak gëm ag bennoo. Mooy wuyyu gu mag ga, ca woote ga Michiavelli doon woote, moom mi doon sàkku ciw nitam ca téereem ba tudd “buur bi” te looloo njëkkoon bennoo gi ci ay xarnu, mu doon sàkku ci ñoom ñu liggéey ngir bennal seenum réew.